LESSON 1 VOLUME 3 BOOK 2


HEBAARI MARIYAMA


Nu Janga: Yeesum Nasaret mooy kaddug Yalla gi


Bul Fate: JOHN 1:14, Te kaddu gi dafa nekka nit, dekka ci sunu biir


Wahtaan wi: Yaay bi nu wara genna fonka ci adina


Nu Janga: Li hew ci mbiri carol dafa doy keeman.


Nan seetan: Malaka Jibril (600), Marima (601) Yusufa (602)



Yow Jangalekat bi:


Nanga ham ne yeesu dooreewut ci biiri Mariyam. Bul fate ne amut fu mu dooree. Moom ak yala nyoo em. Nii lanu ko mu na wahee, Yalla moo jel bindi doom adama nyow dekka ak nyun di lekka ni nyam. Maaa nam kaddu Yalla moo dugga Mariyama mu nekka Yeesu. Nu gis ci Yeesu naka la Yalla mel, jikoom yepp jiko Yalla la.


Leegi nag sooy jangale leeralal ne Yeesu munga woon ak Yalla baala muy juddusi ci aadina.


Te itam degeralal leen ne Yeesu dina dunda be faw. REVELATION 19:13


I. Yalla yonni na Malaka Jibril ne mu dem ci Mariyama


A. Mariyama deka na nasaret ci go hi Galili.


1. Amoon na yonenta bu wahoon ne Yeesu dina nyu ko ooyee na sa ran.

2. Mariyama janha bu sella la woon, baax te soppa Yalla ci holam.


B. Mariyama dfa waroona sey ak bena goor bu tudda Yusufa benna capenta, waaya seyogunyu woon.


1. Mariyama ak Yusufa deku nyu woon benna ker te taka gunu woon sen sey bi

2. Waaya kelifa yi wah nunu seen diganje be pare, moo tah Mariya du mau na sey ak beneen goor su dut Yusufa.


C. Bi Mariyama gi see malaka mi dafa tiit fekka Jibril la woon.


1. Fekka musuta gis Malaaka.

2. Jibril ne ko, bu ragal. Yalla du tiital benn nitam



D. Jibril wah Mariyama ne ko Yalla daf la fonka, te Yalla soppa na sa dunda.


1. Nyun yepp la Yalla fonka

2. Am na pah bu nekka ci holi Yalla kenn wara fa duga hanaa yow.


II Jibril johe na hibaar bu neeh bi ko Yalla yonni ci Mariyama


A. Jibril ne ko, dinga am neene bu ute ak yeneen neene yi


1. Hale bi dina nekka hale bu goor - di doomi Yalla.

2. Jibril wah ko nakala hale bi wara tudda - mune ko yeesu.

3. Mu ne ko,hale bii dina nekka Bur, te dina falu ci niti Yalla yi be moos-be-moos


B. Mariyama dafa amoon jahle bu rey ndah te hamut naka ta ware omee doom te teddut ak goor.


1. Hale bu judu dafa fekka mu am goor bu def jin ci biiri jigen.

2. Lii yepp Adama ak Awa nyoo ko waral, bi nyu defee bakaar ci biir gaadin ba, mootah jiw nit nyi yepp am bakaar ak dee.


C. Jibril wahoon na Mariyama ne, papi hale bi du nekka doomi Aadama.


1. Yalla mooy jel dooley hel mu sella mi def kaddoom biiri Mariyama.

2. Yalla ci bopam mooy papi hale bi

3. Doomi Mariyamaa bii du am bakaar, te du dee ndahte doomi Yalla la.


D. Dega la Mariyama hamut ci woon dara waaya nangu na li yalla yoni Jibril mu gom ko tiye ko ci holam.


1. Mu tontu Malaaka mi ne, Na sa wah am kon ni nga ko wahee (LUKE 1:38)

2. Sooy wosin keeman bi Yalla wara def ci yow danga wara nangu wahi Yalla njekka.


III Bi Jibril yegallee Mariyama li wara hew, Mariyama dafa door di sentu yu bari ci kanan.


A. Bala Yeesu doon nyow ci adina, mungi tudoon baati Yalla JOHN 1:1.


1 Mungi nekkoon ak Yalla be faw balaa muy nyow ci adina si.

2. Neene bi Mariyama omboon ci biiram, baati Yalla la woon.

3. Kaddu Yalla mooy Yeesu Krista.


B. Yusufa dafa meroon torop bi mu degee ne Mariyaama dafa biir.


1. Dafa foogoon ne Mariyama dafa nekka ak beneen goor

2. Waay Yusufa goor bu baah la woon, bugul Mariyama rus ci biir nit nyi, leegi mu buga tas sey bi te ken du ko ham.





C. Bi Yusufa doon helaat ci mbir yooyoo, bena Malaka Yalla waca si ci moom ci biir genta.


1. Malaka mi wah Yusufa neko, bul ragal dara, Jelal Mariyama mu nekka sa jabar. Bul tas sa digante ak Mariyama.

2. Malaka mi dah ko ne, hel mu sella mi moo duga ci moom moo tah mu biir, su amee doom, doom ji dina nekka musalkat bi.


D. Bi Yusupha hamee li hew, mu jel Mariyama def ko jabaram, ndahte ham na ne Mariyama caahanut dafa omba ci hel mu sella mi te neene bi doomi Yalla la.


1. Baati Yalla moo nekka nit, mu wone naka la Yalla mel hamal nit nyi kan mooy Yalla (JOHN 1:14)

2. Yeesu dina nekka kaddu Yalla saa yu nekka be moos-be moos (REVELATION 19:13)


Nu Janga Kadu Yalla


Ca ndoorte la baati Yalla bi munga fa woon

Te baati Yalla bi munga woon ak Yalla

Te itam Baati Yalla bi Yalla la.

Baati Yalla bi dafa jel yaram mi nit

Muy dunda ci adina bi kom nit nyi

Yeesu Krist, doomi Yalla mooy nekka baafi Yalla



YAAY BI GENNA AM MAANA CI ADINA.


Mariyama moo doon wahtaan ak Gaayi


Gaayi: Tey danyoo wahtaan ak Mariyama, te moo nekka yaay bi genna am solo si adina. Tacul leen ko.


Mariyama: Jerejef leegi, yeen gaayu baah ngeen.


Gaayi: Mariyama, gis nanu ne Yalla soppa na la te neeh nga ko, du noonu?


Mariyama: Waaw, loo lu dega la, waay nyun yeppa em ci Yalla. Man Yalla moo ma tanna rekk waaya man ak yen hale yeppa la boole soppa. Yalla moo def ma nekka yaayi doomam.


Gaayi: Mariyama, ham nanu ne Yalla am na lu baah ngir sunu dunda, ndah dinga nu muna hamal lu am solo boobu ngir sunu dunda?


Mariyama: Waaw,kon deglu leen ma wah leen, gom naa ne ku bugu Yalla defal la lu baah danga wara sella.


Gaayi: Bibul bi dafa wah ne yow ku sella nga woon, leegi ndah dinga nu muna wahal sella googu naka la.


Mariyama: Sella mooy nga tiye sa ge men bul ci wah lu nyaaw ngay degga edda te ngay def sa helaat yepp ci Yalla.


Gaayi: Waaga nag nyun melun noonu, ndahte nyun danu dee bakaar di def lu bon ndah loo lu mooy nyakka sella.


Mariyama: Deedeet nagi Yalla moom ku am yermande la be kuko toon mu baalal la. Nit ku nekka mus naa bakaar def lu sellut. Suma doom ji Yeesu rekk moo musuta def lu bon, mus ta am bakaar. Dunda gu jub la dunda ci adina. Li tah mooy, moom mooy Sarah bi Yalla gennee ngir nun loo lu mooy rahas sunu bakaar. Nit nu bon yi sah Yalla dina leen baalal su fekkee ne tuub nanu, nu gom ne Yalla yerem na leen ngir Yeesu.


Gaayi: Ndah mus nga door Yeesu bi mu doonee hale?


Mariyama: Deedeet, moom musuta mer, Te musuta heeh ak benn hale moom doom ju amyar la woon ci man.


Gaayi: Ndah daf daan foh ak hale yi?


Mariyama: Waaw kay moom tam df daan foh kom hale yi yena saayi nag jikoom du ko mey muy foh.


Gaayi: Ndah daf daan def lu jaahal nit ni?


Mariyama: Bu mu mune janga teere yonenti Yalla musa a bi ci la door di dem ci neegi Yalla bi saayu nekka.


Gaayi: Hanaa dafa amoon iteh jang mbiri Yalla?


Mariyama: Bala mu doon am fikki at ak nyaar fekka helam yaa tu na ci mbiri Yalla be mu may laaj lu ma munuta tontu.


Gaayi: Moom daal kon kenn melut ni moom.


Mariyama: Moom kay amuto morom. Dafa ute ak nit yepp. Du ma musa fate kera bu malak Jibril nyowee ci man di ma wah ay mbiram.


Gaayi: Kon ya ngi wah jamano bi malaka Jibril nyowee ci yow balaa Yeesu di dudu.


Mariyama: Waa, jamano boobu fekka biir aguma. Malaka mi hamal ma ne ninaa am doom, doomi Yalla.


Gaayi: Naka nga defoon nag?


Mariyama: Dama sahle woon lool, waay weddi wu ma. Hamoon naa ne Yalla dara teh wut ko.


Gaayi: Yalla dara tehwut ko? Mun na lu nekka?


Mariyama: Waaw- waaw yalla mun na lu nekka


Gaayi: Faj yaram wu feebar?

Mariyama: Loo lu yomba na Yalla.


Gaayi: Def ku gumbo, mu gis?


Mariyama: Bu Baah a baah


Gaayi: Ku dee mun na laa deekil?


Mariyama: Mbiri hale, Yalla doolem amut appa. Dafa bugoon ma jural ko doomam, man itam ma gom ko.


Gaayi: Lii moo am solo.


Mariyama: Lan?


Gaayi: War nanu gom Yalla ak lu munti hew.


Mariyama: Doo muna ham baaa hay yi Yalla ci sa dunda soo gomut.


Gaayi: Gom naa baafi Yalla


Mariyama: Man dama gom - du may am nyaari hel.


Gaayi: Man dam gom - du may am nyaari hel (hale yi tam war nana wah loo lu nyaari yoon wala nyeti yoon) Hale yi wah leen. Man dama gom - du may am naari hel. Wahaat leen - dama gom - du may am nyaari hel.


Mariyama: Kon nag hale ganaaw dangeen gom, mangiy dem ci suma doom ji nekka ak moom be faw.



KEEMAN BI YALLA DEF CI DUNDI KAROL



Yaay tey dama buga anda ak yow ci jangu mag yi. Beneen yoon di naa dem ci bu haleyi


Koral fateleku ne danu wahtaan noon manak yow be pare ngir nga dem ci sa morom yi ndah ngeen hamante. Maangi yaakaaroon ne soo demee chooch di nga fa am ay harit.


Waay yaay hool ma bu baah, hale yi danuy foh di daw te kenn du nangoo goh ak man, yow ham nga ne dama lafan. Bul dee hool sa bopa ne danga la fan, lii feebar rekk la.


Noonu yaaya puns ko be ci neegi hale yi. Mune ko toogal fii dinaa la andil jangalekat.


Waay yaay man duma hale bu nyuy bambaane

Yaayam ne ko, tejal ma sa gemen gi

Karol gis ne yaayam saayu nekka daf ko dee jaani.

Noonu rekk, pastor Wilson nyow si Karol fekka mungi toog moom kenna. Mu neko, Karol nanga def? Bi ma la gisee fii kontaan naa ci torop. Nanu dem ma yobbu la ci jangu kaay bi.


Karol kontan, ne kii baah na di, hoolal tiye wut ma ni hale. Leegi nag mu dem toog foo ham ne puns -pundsan bi du gaan Ken. Muy hoolante ak hale yu rafel yi. Moom dafa foogoon ne hale yi dunu ko faal, waay hale yi danu ko nuyu be pare de wonal e sen pare. Leegi holi Karol bi daldi feeh mu beg ndig baahay yi hale yi.


Bi gaayi dooree di woy, Karol itam di woy bu baah, waay amoon na woy you ham ne munut leen. Bi woy yi paree gooyi ubbi benna wahtaan bu neeh.

Boobu neeh na Karol lool.

Bi nu paree ci lool lu, Pastor Wilson di waare mbiri Yalla. Fekka Carol Musuta degga loo lu. Lii la Pasto Wilson doon waare: - Yalla bugut nit yi di feebar. Fekka na Karol oona Yeesu ci holam bu yagga, te danu ko daan wah ne dina jeehal ak puus - puusam bi bes bu demee ci Yeesu Arjana. Waaya pasto Wilson mungi koo wah ne Yeesu leegi la ko sohla leegi helam yepp nekka ci mbir wer, muy helaat wer ndah mu muna daw di foh al hale yi.


Pastor Wilson ne leen, yaayi Yeesu, Mariyama, malaka Jibril dafa nyowoon ci moom ne ko, dinga nekka yaayi doomi Yalla ji. Yeesu munga woon ak Yalla ndahte baati Yalla la.


Mariyama dafa johe yaramam ngir Yeesu judu kom nun, Yeesu mooy kaddu Yalla bi nu def ci biiri nit mu Judu.


Mariyama ku gom Yalla la, bi Jibril nyowee ci moom, helam munuta jappa li ko Jibril wah. Waaya gom na, mu ne,na am ni ko Yalla wahee.


Li kaddu Yalla nekka ci biiri Mariyama moo tah Mariyama nekka yaay doomi Yalla ji.


Pastor Wilson ne leen, nyun itam mun nanoo jel kaddu Yalla ni ko Mariyama jelee nu denca ko ci sunu hol. Sunu bugee lu baah ci Yalla danu wara njekka nangu kaddoom. Nangu kaddu Yalla dafa mel ni ji dugub ci biir suuf si. Dangaa ji ci sa hol, nga def ci ndoh ak ngom. Su jiw bi di sah mooy kom su Yalla di nangu sa nyaan. Su garab yi di dati ken du ko yegg noonu la kee man ni Yalla mel.


Karol har tunti, fekka holam yepp mungi sadda. Mu yeg li Yalla wara def ci dundam. Muy wah ci holam: wer naa - wer naa ci Yeesu. Ganaay gi Pastor Wilson lajte ku bugga wer ci dooley Yalla.


Karol yunhu, ne Pasto Wilson, na am ci man ni ko kaddu Yalla wahee. Hale yi yepp the hool, waay Karol faalewut kenn.


Karol lafan bu buggoon na doh la. Ci saa si hel mu sella me door di gaj tankam yi. Mu ne Pastor Wilson, Yalla faj na ma, ham naa ne wer naa.


Bi mu wahee loo lu, mu am benna hale bu goor bu ko wah ne, Karol, su fekkee ne Yalla faj na sa tanka yi, lu tah nga toog ci sa puns- puns bi.


Ham naa ne Yalla faj na ma, te loo lu mungi am ci jamano bi Pastor be wahee ne Yalla soppa na ma, te sohla na ma, loo lu dafa laal suma hol. Musumaa degga loo lu. Noonu Karol jeem di jog ci toogoom bi. Mu jog tahaw ci kow. Yunhu ne leen wer naa, hale yi yepp top di ndig waaru nu gis Karol mi lafan door di doh.

Muy doh di genna deger di daw di wor neegi bi. Mu daw be ci Pastor Wilson jappante ak moom, mu beg lool. Ne ko, wer naa jerejef.


Pastor Wilson hool Karol gis mungi joy, mu ne ko su ma hale bile Yeesu Krista faj na la.


Karol door di wah naa, suma yaay daf ma andi chooch ngir ma am ay harit, waay Yalla moom dafa buga ma wer te weral nu ma.


Na Nu Fate Leku


Yeesu mooy baati Yalla. Bibul bi danu ko wara gom lepp lu mu wah, mu mel ni Yeesu moo tahaw di wah ak nun


Ndah mus ngaa gom baati Yalla, kom nga gom ne lii la Yalla wah waay su amee du la neeh leegi Yalla wecci ko mu neeh la? Wahal gaayi lan la.


Laajte Yi


1. Ban malaka Yalla moo wacca ci Mariyama wahal ko hibaar bi?

2. Mariyama, ban fasongi jigeen la woon.?

3. Mariyama ci bandekka la dekkoonn?

4. Kan moo waroona takka Mariyama?

5. Lan la Mariyama defoon bi mu gisee malaka mi bu nekka?

6. Ndh am na ku muna jel sa palas ci holi Yalla?

7. Ban hibaar bu am solo la malaka mi yegal Mariyama?

8. Lan la Jibril wah mu tudee neene bi su juddoo?

9. Lan la Jibril wah Mariyama ci mbiri Yeesu?

10. Lu tah Mariyama jahle ci mbiri hibaar bi ko Jibril wah ci mbir juddu Yeesu?

11. Lan la bakaari Aasama ak Awa def ci jiw nit yi yepp?

12. Naka la Yalla nekke papi Yeesu?

13. Ndah Mariyama nangu na hibaari Yalla bi Jibril andi ci moom ndah nanguwu ko?

14. Ndah Yeesu mungi doon dunda balaa muy judu ci adina?

15. Naka la Yeesu tudoon balaa muy nyow ci adina si?

16. Lu tah Yusufa ner bi mu yegee ne Mariyama dafa biir?

17. Ham nga Yusufa dafa baah te am kersa lan la Yusufa bugoona def?

18. Lu hew ci Yusufa be muy helaat lan la wara def?

19. Bi Yusufa deggee li ko malaka mi wah, lan la def?

20. Lu tah kaddu Yalla nekka nit?

LESSON 2



JUDU YEESU KRISTA


Nu Janga: LUKE 2:1-21


Degga gi: Yeesu bi mu juddoo ci adina si nekka nit ci jamano boobu dafa tegee boor doole gi mu nekkee Yalla.


Bul fate: JOHN 3:16 Yalla dafa soppa doom Aadama yi be mu johe benna doomam bi mu am, ngir keppa ku ko gom doo sanku mukk, waay dinga am dunda gu dul jeeh.

Wahtaan wi: Jef yi ute wunu.


Nu Janga: Hari Yalla bi


Nanu Seetan: Malaka yi (600), Mariyama (601) Yusufa (002) Mbaam mi (603) Lekka kaay yi har yi (604) Yeesu bi mu nekkee neene (605) Har Yi (606) Gelem yi (607) Samakat yi (608) Ay malaka yu bari (609) Bidiw yi (610) Dekka bi (611)



Janga le kat bi


Leeralal hale ne kaddu Yalla moo duga ci Mariyama nekka doomi Aadama. Mu jaar ci yoon, nyow ci addina kom nimu waree, jel yarami nit juddu ni nit yepp juddoo.


Te Yalla la waay dafa jel dundi doomi Aadama, di topp li teere Yalla bi wah, anda hel mu sella mi.

Amut woon jikko bu bonbi nekka ci doomi Aadama te dee amut benn doole ci ko wam, ndahte nekkut doomi nit, waay ame na yarami nit.


Ci teere yonenti Yalla musaa, Yalla daf leen santa nu Sarahe har bu amut benna sikka-sikka. Loo lu moo tah Yeesu itam amut benna sikka-sikka ndah mu nekka Sarah bu sella ngir sun bakaar yi. Dee amut doole ci moom. Kom ni Aadama meloon balaa muy bakaar noonu la Yeesu mel. Li waral Yeesu dee, mooy sun afer. Dafa dee ngir nu dunda dem arjana, maanam dafa jel sunu palas. Su nekkutoon loo lu dafa dunda be faw te du mos dee. Sunu bakaar yi moo tah mu dee.


I. Yusufa ak Mariyama danu waroona tukki fu sori, muy dekka bunuy wah Judiya, fekka Mariyama dafa wara am doom.


A. Benna bur butudda Osiisa Agustus, buri Room, moo yeebaane ne keppa ku nekka ci rewam dafa wara am lu moo few.


1. Fekka waa Israyil nungi ci ron waa room.

2. Yalla daf nu santa nu fey lempo ci sun nguur yi (ROMAN 13: 6-7)




B. Li nu wara fey mootah ku nekka dafa wara dem ci dekki cosaanam binda sa tur.


1. Yusufa ak Mariyama, danu wara dem dekku seen maam Dawda, Jogee Nasarett dem Beltehem.

2. Digante bi nu wara doh tollu na juroom - nyaar fukki miyil.


C. Yusufa ak Mariyama yepp, yonent Yalla Dawda seen maam la.


1. Yalla dafa digoon yonent Yalla Dawda, ne doomam yi nyooy falu Israyil be moos-be-moos.

2. Yonenti Yalla Isaya wahoon na ne, Almasih bi mungiy jogee ci setti yonenti Yalla Dawda (ISAYA 11:10)


D. Bi Yusufa ak Mariyama eggee Betlehem muy ut funu dal.


1. Waay bi nu eggee nu fekka neeg yi yepp fees.

2. Banna palas rekk moo desoon, muy neeg nag yi fekka amunu pehe, nu duga ci neegi nag yi dekka fa.


III Mariyama am na doom ci neegi nag yi.


A. Bi hale bi judoo Mariyama lahas ko ci benna ser


1. Ser yi nag mooy ma lan yinu dee muur neene yi.

2. Nun itam sunu juddoo ci hel mu sella mi danu dee muur ci mbugeelu Yalla kom neene Yalla.


B. Mu la has ko ci ser be pare mu teg ko ci lekkee kaayi nag yi.


1. Lekkee kaayi nag yi dafa dee am pah mu mel ni lalli hale, foofu lanu dee defal nag yi lekka.

2. Hoolal naka la Yeesu sunfeel bopam, te moo sakka adina si, be moo judu mu judoo si neegi nag yi.


C. Kom ni leen ko malaka Jibril wahee woon, Mariyama ak Yusufa tuddee hale ba Yeesu.


1. Yeesu mungi tikki Musalkat bi

2. Te danu ko daan ooyee itam Emanuel liy tekki ne, Yalla ngi ak nun.


III Dafa amoon samakat yu jogee ci yeneen dekka seetsi hale bi judu, nu gom ne mooy musalkat nu jaamu ko.


A. Samakat yi nungi doon seet seen har yi ci guddi


1. Fekka mungi guddi nu jekke - jekki rekk gi malaka wacca si ci seen kanam, foofu yepp leeri Yalla wor jeen.

2. Bi samakat yi gisee loo lu nu tiit.


B. Malaka mi yegal samakat yi hibaar bu baah bi.


1. Mu yegal leen ne Krista bi juddu na ak fan ieen ko mu na giisee

2. Bi mu pare wah malaka yu bari nyow fekka si benna malaka bi njekkoona nyow.


C. Malaka yi di naanal nit yepp jama ak hiwal di gerem Yalla ci kow.


1. Nun itam wara nanoo santa Yalla saa yu nekka. Di beg ngir li Yeesu nyow ci Adina.

2. Santa Yalla war nanu te lu am solo la.


D. Bi malaka yi delloo, samakat yi dem seeti hale bi ca Betlehem.


1. Nu dem fekka Yusufa ak Mariyama ak hale ba Yeesu munga tedda ca lekku kaayi nag ya nom ni leen ko malaka ma wahee woon.

2. Nu wah hibaar bi waa Betlehem bi nu paree nu dellu ci seen har yi.

E. Baafi Yalla dafa nyow ci adina waay dafa jel yarami neene.


1. Yeesu Yalla la, te itam nit la ci benna jamano.

2. Bi mu nekka ci adina dafa teggee boor doole Yalla bi nekka ci moom


F. Yeesu dafa doon dunda ci adina ngir won nu naka la Yalla bugga nu dunda.


1. Loo lu moo tah saa yu nekka hel mu sella mi dafa dee fees ci holam (ACTS 10:38). Te itam baati Yalla la dee heehee saytaane.

2. Degga la Yeesu Yalla, dafa dunda ni nit, waay dafa nangu Yalla dunda ci moom jare ko ci kaddoom ak hel mu sella.


Yeesu rekk moo mun lu gefe

Dafa jogee argana nyow ci adina bi

Baayi ngunram nyow mel ni man


Man itam Yalla soppa na ma

Buga ma ham ko mu johe doomam

Ngir man.

Yeesu ni jogee Arjana ngir andil

Nu dunda gu duljeeh.


BEENA LI GEEY BI


Benniee ak Jimmy ak Heart noo doon wahtaan.


Bennie: Jimmy ndah degga nga li jangalekat bi wah?


Jimmy: Degga naa ko, waay loo lu du muna am.


Bennie: Lu tah?


Jimmy: Nun dun muna def jef yi Yeesu def.


Bennie: Waaya li jangalekat bi wah ci Bibul bi la ko gisee. Yeesu mune dinanu muna def lepp li mu def walla jef yu ko oppa.


Jimmy: Kon foog na ne Yeesu dafa junm. Bennie danga wara ham ne nun nit lanu dunu Yalla, te Yeesu Yalla la doomi Yalla la moo tah mu mun jef yooyu yepp.


Bennie: I ham naa loo lu waay ..............


Jimmy: Amoo looy wah, ham nga ne Yeesu doomi Yalla la te gis nga ni mu juddoo keeman bu rey la. Naka lanu muna defee li mu def.


Bennie: Hej na, li Jimmy wah degga la, Yeesu doomi Yalla te ci keeman bu rey la juddu, fooguma nu muna def li mu def.


Hol: Cim holal mungi am nyaari hel.


Bennie: Hol lu la nahari.


Hol: Yangi sanni nyaari hel ci suma kow. Seetal ci sa boppa soo dugalee lu weh ci sa biir bi ni mug mel ci yow noonu la mel ci man.


Bennie: Lu weh rekk laa ban.


Hol: Man nag nyaari hel rekk laa ban. Bul ma dee dugal nyaari hel.


Bennie: Hawma woon ne mangi am nyaari hel. Lan laa am nyaari hel?


Hol: Yangi am nyaari hel ci li Yeesu wah ne dinga def ay jefam, walla ay def yu ko oppa.


Bennie: Waaw, degga-la, dafa am lu ma jaahal, naka laay defe jefi Yeesu yi? Moom doomi Yalla la, Yeesu ku em ni moom, war nga ham ne dunu benna, mar beenie laa.


Hol: Seetal ki ko wah, Yeesoo ko wah moo tah nga wara ham ne degga la. Loo lu rekk war naa tah nga gom. Nyaareel bi, war nga ham ne Yeesu bi mu nyowee ci adina nit keese la woon, ni yow. Andut ak dooley bi mu amoon bi muy nekka ci kow.


Bennie: Su fekkee ne andut ak doole bi mu amoon ci kow kon naka la doon defee keeman yu rey yooyu, di faj nu bari-bari?


Hol: Yeesu wahoon na ne, jef yi moo def du ci katanam Yalla moo doon ligeey ci biiram.


Bennie: Danga bugga wah ne Yalla moo doon def jef yooyu ci biir Yeesu?


Hol: Wah nga degga, Yeesu ay mbiram nii la, dafa jebal bopam ci Yalla, Yalla di def any keeman saaree ko ci moom. Daf nu doon won naka la.


Bennie: Su fekkee ne nangu nanu Yeesu dugga ci sunu hol, dafaa mel ni Yalla dekka na ci cunu biir. Ci noonu Yalla dina ligeey ci sun dunda kom ni mu def ci dundi Yeesu!


Hol: Gis naa ne sa bot yangi ubeeku leegi, sa ngom mungi yokku. Amut kenn ku muna def li Yeesu def moom kenn ndahte Yeesu dafa fees ak Hel mu sella mi, way ku gom Yeesu dinga muna def lim def ndahte Hel mu sella mi Yeesu am boobu am.


Bennie: Jerejef waay, leegi duma haar dara.


Hol: Sal walla, kontaan naa ci sa mbir torop.


Jimmy: Looy daw Bennie, foo jom nii?


Bennie: Mangi dem def jefi Yeesu yi.


Jimmy: Dama foogoon ne fate nga loolu, waay ma hamal la ne loo lu doo ko mun.


Bennie: Wah nga degga ci loo lu, duma ko mun ci suma boppa wang Yalla mun na koo def saaree ko ci man.


Jimmy: Degga ko nag!


Bennie: Kaay nu anda, Dinaa la ko leeralal ci yoon wi.



HARI YALLA BI


Nu Janga: HEBREWS 9:22" Su deret tunruwaut Yalla du gennee sunu bakaar.


Linga Wara uti: Pentur bu weer, kayiti hibaar, ak yeneen jum tu waay............


Nii nga ko wara defe:


Ci jamano yonent yu njekka ya Yalla dafa santaane woon nuy genne Sarah ngir sunu bakaar. Bi Yalla musalee musaa ak waa Israyil gennee leen Egypt, dafa leen wahoon nuy Sarahe har. (Nanga wone nar bi ci sa lo ho.) Har bi dafa wara wer te waruta dama wala mu am sikka-sikka.


Te dafa wara doon har bi genna duuf ci har yi.


Waa Israyil yeppa wara rey har, deret bi nu tahal ko ci seen bunti neeg yi ci guddi malaka dee naaw nyow si ker bu nekka, neey gu amut deret ci bunta bi, ker boobu seen taaw bu goor dina dee.


Waay waa Israyil dara juttut leen. Fu malaka mi dem rekk fekka fa dereti har ci bunti neeg yi, mu Yalla dem feneen. Dereti har yi nyoo musal waa Israyil.




Bakaar lu bon la, daf nu dee tagale ak yalla bakaar yaaha nga barke Yalla bi warroona nyow ci yow. Dipi ca ndorte la, Yalla mungi dee ut yoon ngir mu baalal nu sunu bakaar. Saayu nekka Yalla mungi ut yoon ngir barkeel nu. Lu nu nahari.

Bakaar danu ko wara fey njegam. Te ngeg li deret la. Balaa sun bakaar di genna ci sunu kow deret bu sella dafa wara tuntu. Bi Aadama daanoo ci bakaar, ci la saay nit yepp Seytaane, te seytaane mooy Yalla ci adina.

Seytaane dafa bugga mu moom nit yepp,ndah mu mun leen na lor, yaha leen. Deret rekk lanu wara fey ngir nu recca loho seytaane ak bakaar.


Yalla dafa won nit yi bu njekka naka lanu genne ci seen bakaar yi at be af, mooy nu rey har sarahe ko.


Af bu nekk noonu la beneen har. Li du dee jeehal bakaari nit yi, waay di ko munr.


Waay benna bes, bennen har dafa now ci adina si


Moom itam dafa mel ni yeneen har yi, amut sikka-sikka. Mbiram yeppa mut, amut bakaar. Bi ko yonenti Yalla yahya gisee Yeesu mungi now ci geej ji Yordan dafa ko ooyee hari Yalla. Yeesu dafa nyow ngir nekka sunu Sarah ndah sunu bakaar.


Bi nu daajee Yeesu ci kow cross ba boobu la nekka har bu nu sarahe (Jamal sa paaka bi ci biir har bi ndah deret bi tuuru pan bi). Dafa johe derelam bu sella bi ndah sunu bakaar yi wacca sunu kow. Deretam du muur sunu bakaar, dafa kooy rahas mu sett wecc.

Nii la Yeesu dee rahasee sunu bakaae, sunu ko ooyee ci su nu hol mu nyow dekka fa, rahas nanu, su ko defee mu mel ni musunoo bakaar.


Derefi Yeesu dafa dee rahas hol be mu mel ni hol boobu musuta am bakaar. Nanu gerem Yalla ci haram bi.


Soo buguta jel deret bi jelal beneen hari foyee kaay.


Yeesu dafa nyow ci dunyaa bi ngir won nu naka la nit wara dundee. Keeman y mu doon def, defut leen ngir ne moom Yalla la, waay def ko jaare ko ci doote hel mu sella mi ak kaddu Yalla gi fees ci moom.


Ndah Yalla mus naa jaar ci you mu def keeman walla keneen koo ham?


Laajte yi


1. Lu tah Yusufa ak Mariyama jogee Nasaret dem Judiya?

2. Kan moo doon buuri Israyil ci jamano bi Yeesu doon juddu?

3. Ban dekka ci Judiya la Yusufa ak Mariyama tukki?

4. Ci ban buur la Yusufa ak Mariyama cosaanoo?

5. Lu tah li Mariyama ak Yusufa cosaanoo ci Dawda, mu ain solo?

6. Fan la Yusufa ak Mariyama dal binu eggee Betlehem?

7. Ci lan la mariyama lahas neene bi Yeesu ba mu judoo?

8. Ci lan lanu dee lahas sunu juddo ci Hel mu sella mi?

9. Lan mooy lekku kaayi nag yi?

10. Turi Yeesu lu mu tekki?

11. Lan mooy beneen turi Yeesu bi, ak lu mu tekki?

12. Kan la malaka borom bi yegal judu Yeesu.

13. Lu hew ganaaw bu malaka me wahale samakat yi li hew ak fan la leen malaka me wah ne foofu la hale bi judu.

14. Ndah war nanoo be nsig li Yeesu nyow nu gerem ci Yalla?

15. Ndah sunu gerem Yalla am na solo?

16. Naka la baati Yalla nyowee ci Adina si?

17. Ndah bi Yeesu nekke nit ci jamano boobu Yalla la woon?

18. Na ka la Yeesu def ak dooleem ji mu nekka Yalla?

19. Lu tah Yeesu dunda kom nit te dundut kom Yalla?

20. Naka la Yeesu def be Yalla di dunda ci moom?





LESSON 3




BOROM HAM-HAM YI NUGI UUII YEESU


Nu janga: MATHEW 2:1 - 12


Degga gi: Ci Hel mu sella mi ak kaddu Yalla la ha-hami Yalla nekka


Bulfate: Gomal Yalla ak sa hol te bul di weeru ci sa ham-ham wala ci sa hel. PROVERB 3:5


Wahtaan wi: Wahtu genna la


Nu janga: Du ma dof


Nanu Seetaan: Mariyama (601), Yusupha (602) bi Yeesu nekkee neene (605) gelem yi (607), Bidiw yi (610), Nyetti borom ham-ham yi (612), Bur bi (613)


Yow jangalekat bi.


Nanga ham ne ham-ham moo genna am solo ci adina (PROVERBS 4:7) Sunu ko sakkoo be am ko, dina muna def ci nun allel walla tur nu rey fan wu gudda tel it dina neehal sun digante ak Yalla (PROVERB 3:13 18). Musange dinay wone hol bu rafet ci kanam Yalla. Te ham-ham bu set, borom day fonka Yalla di ko maggal. Sunuy jangal hale yi be nu muns, loo lu dina def ci noom nu ragal Yalla di ko jaamu, tabe ci seen allel.


Borom ham-ham yii nyowoon seet si Yeesu dekka yu sorri lanu jogee. Te nyoom dunu waa Israyil. Waay Yalla moo teen hamal limu naroona def ci Yeesu. Te dafa daan am balaa loo lu, Yalla di feenal ay mbiram ci nu nekku ye wut. Dafa daan am yonent yu wacca ci yeneen heel yi muy wone ne peheem nit yepp la ci boole.

I. Ay Borom ham-ham jogee nanu ci penku bi nyow Israyil ngir jaamu Yeesu.


A. Yalla yagga naa am ette boole nit yi yepp ci hi wal gi mu nara defal doom Aadama.


  1. Ci teere yoneenti Yalla musaa bi yalla dafa daan santa waa Israyil mu jub yeneen

rew yi muna seet ci nyoom. (MALACAI 3:12)

2. Hibaar bu baah bi Yeesu Krista andi nar na efa ci nyepp.

(MATHWE 28:19,20)


B. Borom ham-ham yii, ci jaw ji lanu doon janga.


1. Nyoom seen heel hibaari bidiw yi lanu jot, gom ko.

2. Bidiw yi danu daan wonne ne Yalla di nu musal. Waay waru noo jel bidiw yi di leen jaamu kom Yalla (PSALM 19:1)


C. Borom ham-ham yii, hej ne danu daan janga teere yonenti Yalla Daniel ndah te nunga jogee boor ba daniel Nek koon.


1. Daniel wahoon na baat boo ham ne yagga ne bala loo lu di hew. Mus naa wah ne almasil bi danu ko rey. (DANIEL 9 :25 - 26).

2. Borom ham-ham yi gis nanu bidiw am, nu ham ne judu na.


II Bi Borom ham-ham yi eggee Jerusalem, nu dem ci bur ba.


A. Nu yegal bur bi herod, ne buuri yenut yi juddu na ci biir Israyil.


1. Bi Herod deggee loo lu mu waru lool, mer nag.

2. Mu laaj borom ham-ham yoo yu kan lanu gis bidiw boobu.

3. Mu ne leen, dem leen seeti hale boobu sooleen ko gisee ngeen nyow won ma ko.


B. Borom ham-ham yooyu toppa bidiw bi be ci neegi Mariyama ak Yusufa.


1. Bidiw di doh dileen won yoon wi be nu gis fi Yeesu nekka.

2. Bi borom ham-ham yi doon egga si biir Israyil fekka na Yeesu am nyaari at.


C. Bi nu aggsee nu baayi leen nu dugga ci biir neeg ba seetsi Yeesu.


1. Bi nu ko gisee nu sukka si suuf sujootal ko, jaamu ko.

2. Nu joh Yeesu yobali wurus si ngalam ak cuuray yu seer-a-seer.


D. Yalla feenu Borom ham-ham yooyu ci biir genta ne leen bunu dellu ci Herod.


1. Nekk ut ne genta yepp ci Yalla lay jogee, waay Yalla dafa dee wah ak doom Adama yi ci genla yenna saa yi (ACTS 2:17).

2. Bi Borom ham-ham yi doon nyibbi nu jaar beneen yoon.




III. Mun nanoo janga lu bari ci mbiri borom ham-ham yi. Mooy ham-ham mu yalla dafa yaatu.


A. Gaay yooyu am nana ham-ham ndig danu sakku ham Yalla.


1. Mun na noo sakku ham Yalla jaare ko ci deglu wala di janga kaddu Yalla

2. Kuy ut ham yall mun nga ko, jaree ko ci naan,. Sooy naan wahal ak Yalla, soo paree nga nappi deg lu ko mu nah a yow.


B. Borom ham-ham yii muus nanu te am nanu ham-ham ndig te danuy jaamu Yeesu.

1. Jaamu nekkut ne horma la rekk waay itam tuub, jebalu magal ak cant yi yepp heeti jaamu Yalla lanu.

2. Kuy jaamu Yalla degga-degga ci sa hol la wara jogee. Ham-ham muna dellu ci sa hol.


C. Borom ham-ham yii nu muus lanu moo tah nu joh Borom bi.


1. Ku buga an naatange war ngay nangoo johe.

2. Sunu nangoo johe ci ligeeyi Yalla, moom itam dina nu won pehe nuy an saayu nekka.


D. Ham-ham moo genna am solo ci dundi doomi Aadama.


1. Yalla dig na nu sunu sohlaa ham-ham dina nu ko mey (JAMES 1:5)

2. Di sakku baneehi Yalla, di ko jaama, te di johe mooy tah Yalla dinu mey ham-ham ak muusange.


Keppa ku buga mun

Keppa ku buga nanda

Jelal kuddu Yalla

nga def ko ci sa hal.


Nanga janga kuddu

Yalla bes bu nekka

Deel naan saayu nekka

Kon say lampa dina genna

takka bes bu nekka.



WAHTU GENNA

Hel Ak Hol



Hel: Leegi daal dumay muna tee la jog ci lal bi su ma yaram wi daf dee diis torop. Te wacce hale yi ci lal bi beneen ligeey la waay fokk nu def li war ci bes bi ligeey bi dafa bare leg. Haral ma togga ruy bi nu ndeewo, ma muna jogee fii.


Hol: Bul yakanti saa waaji! Haaral nu wahtaan.


Hel: Hol, nag, dinga ma baalal, awma jot, mangi nii di dem school, te bugu man tarde.


Hol: Doo dem fen tey, hanaa nu wah be pare nga doora dem.


Hel: Danga buga wrante, waay wah naa la ne aw ma jot, demal be beneen yoon nga nyow nu wahtaan.


Hol: Linga ma wah haaral be beneen yoon bari na, te saa yu haaree du ma la gisati.


Hel: Demal leegi be guddi balaa maa tedda dina wah ak yow.

Hol: Afeeri haar be tedda loo lu andu ma ci. Hool ma bu baah, ni ma meloon melatu ma ko. Su ma bot yi huleeku na suma kuloor bi genna na, leegi mangi jahasoo.


Hel: Dina la yobbu ci doktoor bi eley.


Hol: Sohla wuma dem ci doktoor, dama wara naan, jaamu Yalla, janga kaddu Yalla?


Hel: Ku am joti loolu yepp? Du man de.


Hol: Loo lu nag war nga fehe am jo tam, nala nu taggoo ku nekk aw sa yooni boppa.


Hel: Ban njerin la loolu yepp am.


Hol: Ban njerin la am nga may tontu? Danga buga tassee ak seytaane fekka amuloon benn doole Yalla.


Hel: Deedeet, waay ..................


Hol: Kon deel naan di jaamu Yalla, di janga kaddu Yalla.


Hel: Waay Hol, ham nga ne dimas bu nekk dama dee dem chooch. Loolu dogut?


Hol: Dem chooch baah na lool, waay dogut, waar nanu jelee musange ak ham-ham ci Yalla bes bu nekka , du semen bunekka.


Hel: Naka nga dugalee ham-hami Yalla ci sun wahtaan wi?


Hol: Loolu mootah naan bari njerin, di janga Bibul bi ak haamu Yalla. Yalla dafa de johe ham-hamam ngir nu muna ham naka lanu dohe=alee sunu digante ak nit ni.


Hel: Gis na ne mbir yu bari sohla naa ci Yalla Sol ma munsangeeem?


Hol: Degga la, waay naan runy du tah nga am muusange Yalla.


Hel: Dama wara naaan, ndah du?


Hol: Waaw


Hel: Ma janga kaddu Yalla, moo ma war.


Hol: Noonu la sah


Hel: War naa jaamu Yalla


Hol: Degga la.


Hel: Haral be eley ma door.


Hol: Tey ngaa door, Tey jii la.


Hel: Baah na mangi dem door tey. Mangi jeli suma bibul bi.


Hol: Bala muy dellu famu tollu woon ci Yalla dina hala yagga tuuti.




DUMA DOF


Benna bes Gospel Bill daf doon tuuk, mu duga ci train di dem south pass jogee DryGulch. Mu am benna goor bu ko gis oo ko. Nu nuyuwante be pare fekk noom yeppa doon jom benna dekka.


Gospel Bill moom ware kat la, moo tah mu bugga toog ak waaji ndah mu wah ko mbire Yeesu. Waaji ku yaru la te bariwut af eer, te dafa janga torop. Waaga bill ham na ne nit ku nekk sohla nga Yeesu ngir mu musal la.


Bi Bill toogee ak moom ci biir te rain bi mu door di ko ware mbiri boram bi. Bill door di ko wah naka la Yeesu nyowee ngir musal nit yepp.


Waaji nag ku am teranga la, waay nag buguta deglu mbiri Yeesu.


Waaji daldi ne Bill, man gomuma mbiri Yeesu, gomuma Yall te ay mbiri bakaar gomuma ko. Ku jangut mooy jappa afeer yooyu.


Bill ne ko, hanaa danga ma bugga wah ne yow gomuloo ne Yalla am na?


Waay ji ne ko noonu la sah, Yalla amut nit yi noo ko def ci seen hel ngir sakku lun jaamu.


Bill ne ko, yow nga loo gom?


Waaje ne ko, man sience laa gom gnjoh loo lu moo loo ci wah am na mandarga.


Je sience lun ci wah dinga ko muna gis. Musuman gis Yalla. Te supekkee ne Yalla am na, dina wone bopam nu gi ko. Suma ko gisee dinaa ko gom. Suma ko gisut duma ko gom.


Bill ne ko, yow danga niru ku am ham-ham waaya dof nga. Bibul bi dafa wah ne, dof bu dafay wah ci helam ne Yalla amut. Te yow daal foofu laa la teg, ci mbooloom dof yi nga bokka.



Waaji daldi yuuhu ci kow Gospel Bill, yaa fi genna tooy, jangulaoo dara, nga naan ma dof. Li ma janga janguloo ko, ci jangu mag yu nyepp rannee la jangee, wara ngaa ham ne duma dof.


Bill nekko, man dee suma nekkee tooy sah gom naa Yalla ak limu wah te duma weeru ci li ma ham rekk. Waay sah man mun naa lay jhoh fir nde ne Yalla am na.


Am nga ay finde? Lan mooy sa firnde?

Bill ne. Gis naa Yalla wecci nit nu deger bopa, def leen nit nu dewet, nu booh doon chretian. Gis naa nu doon ay saay-saay nu nangu Yeesu ci seen jaar ci wecceeku doon nit nu yiw.

Waaji ne ko, loolu noom la neeh , nit ku nekka yaa moom sa bopa, kum neeh nga wecci sa jikko.


Binoo wah noppee gunu,nu degga fetel ci boori motor bi. Taa! Bill def nii rekka gis ku muur kanamam gi tiye fetel, tahaw ci kanam otto bi. Mu ame naari fetel johon ko passase yi nekka ci biir moto bi.


Noonu bandi bi wah leen ku nekka na gennee fetelam ak halisam. Managi anda ak suma harit te tirian bi gu ci nekka na pare.


Waaji hiit, ne, Bill naka lanu def nag?

Bill ne ko, Damay naan te gom Yalla.

Heja loolu dimbale nu ci mbir mi, waaji wah loolu.


Bandi bi degga leen nuy wah mu ne leen, tey leen seen gemen.

Bandi yi dugasi ci biir moto bi di nangu see halis yi, or yi in baal lun gis rekk jel ko.


Gospel Bill daldi segga door di naan. Mu naan ngir Yalla wacceel kio ham-ham. Mu ne, baay bi. Sa kaddu nee na, ku sohla ham-ham ak muusange na la ko naan. Leegi sohla naa ham lu ma wara def ci jamano bi. Jerejef ci li nga wah ak man, ci turi Yeesu amen.


Bi Bandi bi doon jegen si Yalla wah ci noppi Bill yi ne ko, Bandi bangi tudda Charlie McCullough. Oyal tur bi ci kow, noboo kaayam bi Brush Creek la.


Bill ci bopan hamut lu tah Yalla di ko wah mu oo turi jamburr fekk berab bangi garaw. Waay nag Bill ku yagga di toppa ndigali Yalla, ndegem Yallaa I wah mu def di def su hamut lu tah sah dina def.


Bill jekke-jekki rekk, ne Charlie McCullough. Charlie McCullough bandi bi daldi tiit, ne ko noon hamee suma tur Yalla du sa tur rekk la ham, waay fa=ingag nobbu sah Yalla ham na fa, bill wah ko loolu. Yangi nobbu Brush Creek.


Bandi bi li ko jaahal moo masku bi mu def, degga-degga ku ko hame mu waara doy waar. Mu sunni mbahanaam fekka foofu la def halis bimu nangu ci nit yi. Mu daw ca bunti te rain ba. Mu oo gaayam yi ne nan genna fii, gaayi hame nan nu, te ham nan fun lanu dee nobu.


Gaayi yepp daw, passase yi ku nekka jel sa alel.

Waaji doon wahtaan ak Bill te mune gomut Yalla ne Bill. Yow ham nga McCuldough bu baah.

Bill ne ko Deedeet, Bandi bi hamuma ko. Te suma ko hamoon sah dama ko muna hamee ndig masku bi.


Kon naka nga hameee turan ale nobukaayam, waaji laay ko loolu. Bill neko, Yalla ma ko hamal, ndig dama gom Yalla weru ci moom su muusiba aggsee.


Waaji nekko loolu yepp tombee la.

Su la neehee nga ooyee ko tombee, waay oorna ma ne ham-hami Yalla moo nu musal


Kaddu Yalla


Yall daf a buga ay doomam di ko sakku, ndah mu leen di won yoon wi nu waara jaar.


Ci semen bil, sooy janga kaddu Yalla walla nga naan; jelal teere bu ndaw nga cee binda lepp loo foog ne Yalla moo koy weh ci sa hol walla nga yakaar ne Yalla am na lum la bugga won ci kaddoom.


Andi waaleel sa teere bu ndaw bi chooch beneen semen nga wah ko sa jangale kaf bi.



Lajte yi:


1. Kan moo joggee woon ci penku bi, ngir jaamu Yeesu?

2. Ndah Yalla buga naa waccee yi wam ci nit yi yepp?

3. Borom ham-ham yii ban tur lanu am?

4. Borom ham-ham yi ban fason nit lanu?

5. Bidiw yi la lanu daan jerin?

6. Borom ham-ham yi tere kan lanu wara janga be ham mbiri Yeesu?

7. Lan la yonent Yalla Daniel wahoon ne dina am?

8. Naka la borom ham-ham yi hamee ne Yeesu juddu na?

9. Kan borom ham-ham wahtaan at bi nu aggsee Yerusalem

10. Ban hibaar la borom ham-ham yi wahtaan ak Bur bi Herod?

11. Lan la Bur Herod buggoon Borom ham-ham yi defal ko?

12. Fan la bidiw bi doon won borom ham-ham yi yoon emoon?

13. Naata af la, digante bi Yeesu juddoo ak bi fa borom ham-ham yi nyowee?

14. Lan la Borom ham-ham yi def bi nu gisee Yeesu?

15. Lan la Yalla digal Borom ham-ham yi jaare ko ci genta?

16. Am na nyaari yoon yu nu wara sakku Yalla, yan lanu?

17. Fan la jaamu Yalla degga jogee, ak lan la loolu di def ci nit ki?

18. Soo buggee dom kanam, noo wara mel?

19. Sunu nangoo johe ci ligeegi Yalla, lan la Yalla didef?

20. Lu gena am solo ci dundi doom Aadama?










LESSON 4



Nooni Yalla bi


Nu janga: EZEKIEL 28:12 -19 MATHEW 2:13 - 23


Degga gi: Seytaane nit yi la dee jel def li mu buga yaha ci adina si.


Bulfate: 1JOHN 3:8 Li moo tah doo mi Yalla ji nyow, ndah mu muna yaha ligeeyi seytaane.


Wahtaan wi: Noom bi degga ngi


Nu janga: Mbiri sunu noon, Seytaane


Nanu Seetaan: Malaka (600), mariyama (601), Yusufa (602) Mbaam mi (603), Bi Yeesu nekke neene (605) Bur Herod (613)


Yow Jangalekat bi:


Nanga hamal hale ne, sunu noon degga mooy seytaane, ak jineem yu bon yi, du nit yi (EPHESIANS 6:12). Nit yi jum tu waay lanu ci seytaane. Daf leen di jel faj sohlaam yu bon yi. Nit ku bakaar rekk, sumtuwaayi seeetaane nga, te seytaane nooni Yalla la. Ku dekka ci bakaar hariti seytaane nga. Wahal hale ne, kuy toppa kaddu Yalla dinga muna yaha ligeeyi seytaane ci sa dunda. Keppa kunu toppa ndigalam, jaamam lanub (ROMAN 6:16). Sunu toppe kaddub Yalla, nungi wane ne jaami Yeesu Krista.. Toppa kaddub Yalla dina tah nu genne sunu hel ci mbiri adina, musal mu ci pehe seytaane.


I Ay bu nekka seytaane moo ko waral.


A. Amoon na wahtu bool ham ne, seytaane moo nekkoon njii malaka Yalla yi yepp.


1. Ekati bopam ak haajan buga nu jaamu ko moo tah mu joh Yalla ganaw (Isaih 14:12 - 15)

2. Mu am ay malaka yu bari yu anda ak moo saiy joh Yalla ganaw.


B. Malaka Yalla yi heeh ak yu syetaane yi, m laka Yalla yi door leen daha leen nu genna Arjana.


1. Seytaane ak gaayam yi yagga nanoo nyow ci Adina si bala nu laa ta sakka Adama ak Awa.

2. Seytaane musuta tolloo ak Yalla te du musa too loo ak Yalla.


C. Li Seytaane munalut Yalla dara moootah muy feheel nit yi li tah mooy ham na ne nit la Yalla genna fonka ci mbindeef yi yepp.


1. Nit mooy boppl mbindeefi Yalla yi (PSALM 8:4 - 8)

  1. Yalla dafa sakka nit ngir muy haritam.


D. Bi Adama ak Awa daanoo ci bakaar ca tool gadin ba, ci Eden jamano boobu la seytaane am yoon ci biir adina si.


1. Mooy Yallaa Adina si ndig loolu (11 CORINTIANS 414)

2. Moo tah bakaar ak dee dugga si ci dunda nit yi (ROMAN 5:12)


E. Dippi bi Adama ak Awa danoo ci bakaar, seytaane dafay fehe yaha li Yalla nara def ci kow suuf.


1 Yalla wahoon na seytaan ne dina am kuy nyow yaha ligeeyoom. (GENESIS 3:15)

2. Seytaane hamoon na ne fanam soriwut!


II Ni Yalla fehewoon yaha ligeeyi seytaan mooy mu wacce kaddoom mu doon nit nyow.


A. Yeesu kaddu Yalla la woon bu nyow nekka nit


1. Nekkutoon doomi Yusufa, doomi Yalla la woon.

2. Bakaari Adama tahut si moom ndahte Yalla mooy baayam du nit.


B. Bala Yalla di muna def ligeeyem, Yeesu dafa wara dee ngir sunu bakaar yi.


1. Ham Yeesu amut bakaar, moo tah mu muna doon Sarah bi nu muna musal, fey sun bakaar.

2. Bi Yeesu deeye ci kow cross bi, buum yi syetaane takkoon nit yi dafa dog. HEBREW 2:14 -15


C. Seytaane mungi doon ut nit ki Yalla doon wah ne dina ko ebal.


1. Keeman yi hew ci juddu Yeesu yepp la sytaane gis.

2. Dafa bugoona rey neene bi.


D. Seytaane dafa buggoona am nit kum jefoo ndah kooku reuyal ko Yeesu.


1. Ci kow suuf, seytaane nit yi la muna deggo at def ugeeyam, Yalla it noonu la nit yi lay sel def ligeyam.

2. Sa jomi doomi Adama bi moo tah nga muna bi geey ci kow sunuf (HEBREW 10:5)

3. Nit ki sa hol moo wara tanna mbiri Yalla walla mbiri seytaan, bu la I neeh la.


E. Bi Borom ham-ham yi eggee ci buur bi Herod, Herod dafa enan, loo lu neeh seytaan ndig am na jumtuwaay.


1. Enan banante, ak hol buy tanga, lii yepp bunta la ngir seytaane

2. Herod dafa johe bopam seytaane ndah mu jefoo ko.






III Herod mu bon mi di feheel Yeesu ngir rey ko.


A. Su fekkoon ne danu reg Yeesu balaa muy effa si ci cross bi, kon du nu muna musal.


1. Dippi ca ndorte la Yalla dafa andi Yeesu ndah mu dee ngir nun waay dafa wara jaar yoon wi neeh Yalla.

2. Seytaane hamat ne Yalla dafa pehe ne Yeesu dafa wara de ngir sunu bakaar.


B. Bi Herod paree def ligeey seytaan, dafa santaane nu reg bepp hale bu am naari at waccca, ci betlehermak ci ko wor.


1. Ci borom ham-ham yi la hamee naata af la Yeesu wara toilu.

2. Seytaane moom amut yermande


C. Malaka Yalla mi dafa feenu Yusufa ci biir genta.


1. Mu ne Yusufa, na jel Mariyama ak Yeesu demak nyom Egypt be Bur Herod dee.

2. Halis bi Borom ham-ham yi andi woon yobbal mey ko Yeesu moom la Yusufa defee paas yobbu leen Egypt.


D. Fehe seytaane bu bon boobu tas na.


1. Yalla nag fey na Herod jefam jooju, dee na dem safara.

2. Ganaaw bu Herod dee ye, Yusufa jelaat njobootam joge Egypt della Nasaret

3. Ku toppa kaddu Yalla, toppa Hel mu sella mi, saayu nekka dinga muna yaha pehe seytaane ci sa dunda.


Yeesu dafa nyow ci Aadinasi

ngir musal nit yi ci seen bakaaryi

Tas na doole seytaane yepp


Mu dunda te amut bakaar.


Noon bi degga

Sally, Mariyama, Hol bi, Seytaane.

Nu degg seytaan ni muy jahasee nit yi.



Seytaane: Haaral ma jublu ci suma legeey, di jahase nit ak nit, di torohal Kristian yi. Nit yi ma gena yab genn leena ban mooy Kristian. Tey ma yaha seen mbir. Dafa am ci noom nu nakka hel, Nasah.


Sally: Fasong bes yii rekk noo ma neeh, hoolal janta bangi genna, picca di woy, loo gis mungi rafet.


Seytaane: Hey janha bi, fatowuloo dara? Fatewuloo demba binga ooye Mariyama faalewat la? Toppatoowut saay mbiri sah.


Sally: Hawma sah lutah mary nuyuwut ma jemba?


Seytaane: Seen digante la bugga yaha.


Sally: hej na bugut nu nekka hari leegi?


Seytaane: Kooku dafa naaw te amut horom te bari wah.


Sally: Faale wuma ko, su guggee bunu hamante sah. Ndaham dafa naaw, te bari wah. Suma ko gisatee duma ko faate.


Seytaane: Soo ko gisee rekk alta ko. Mangee dem ci beneen hale yah a helam


Sally: Mariyama, luma ko def rekk jar na ko, fekka baah na ci moom. Harrl ma dem daral ko.


Mariyama: Sally, nanga def?


Sally: Tey nga doora wah ak man? Nekka too suma harit, bayi ma rekk, ni ngaay bari wah te naan bugatuma la gis sah leegi.


Mariyama: Waaru, ne ko, Sally lu hew.


Sally: Sori ma waay, ningay bon.

Hol: Sally, tey nga ma rusloo.


Sally: Lu hew? Loolu moo baah ci moom.


Hol: Deedeet loolu warut la.


Sally: Hoolal demba dama ko oo faalewut ma.


Hol: Yaayi Mariyama moo feebar dem lopitan moo tah Mariyama yakamti. Te hejna sah deggut la woon.


Sally: Wah yu hesew laa ko wah, te tayuma ko sah.


Hol: Seytaane moo la ci hiir, moo tah nga saaga ko. Dafa de bugga sonal Kristian yi jahase seen hel nuy heeh. Dafa dee bugga nu fate seen sohla.


Sally: Jerejef Hol, yangi maay jubanti.


Hol: Noonu la, leegi bul nangoo ti di def lepp loo helaat. Soo ame looy helaat, seet ko ci kaddu Yalla bi, helaat bu andut ak kaddu Yalla nga teggee ko boor, nga duha helaat yooyu ci turi Yeesu.


Sally: Mangi dem wah Mariyama mu baalal ma.


Hol: Loolu baah na,. Kon be beneen yoon.


Sally: mariyama, ci yow la doon nyow. Mariyama, naan la nga baalal ma ci lu naaw. Li ma wah. Seytaane moo ma ci dugal, nga baalal ma.


Hol: Sally, baalal na la, nanu dellu ni nu melloon, harit lanu.


Sally: Leegi muns naa, ranne naa seytaane du manatee yaha sunu digante.




SUNU NOON BI


Najanga: Ephesians 6:12, Heehunu ak nit ji am yah ak deret, waay mungi heeh ak dooley dendem yi sampu ci kow, ak kilifay ngelaw ly geten bepp mbideef, maanam Jinee yi ak Juuma yi, ak seen jef ya bon yi nekita ci berab yu kowe yi.


Linga Sohla: Nyenti kayit, nyenti muuroo kuayi seytaan, nyenti banta Nga am ay kubor yu nute ak sisso.


Felal bindee kaay yi nga desen kanami nit, benna goor ak benna ningki ak nyaari janha. Ci rom seen kanam gi nga binda ci tuur yi ci bnnekka, saaku bu nekka tuuri bappam. Chester ansa ak saasaay, Freddy ak Ragal, Sall ak Feebar, Polly ak Nyaaka. Dogal ci bot yi ci saaku yi ndah hale muna gis. Bindal Seytaane si saako bu tannal nyenti hale nu dimbale la. Utal kula dimbale nu sollal hole yi. Jelal masku seytaane nga solal ko hale bu nekka. Nga solal hale yi ku nekka nu muuru benna masku nu binda sa seytaane.


Nanujanga : hale yi, tey danu am gan nyee nekkunugan ci yeen. Hej na musngeen a degga nyenenti gaay yii may oo seen tur. Nyee nag linu daan def tey dinan ham kudaan waral loolu.


Sunu gan gu njekka gi saayu nekka nu janga ay mbiram ci kayiti hibaar yi. Naanu talul chester Saay-saay Nga andi hale bu njikka bi.


Di yaha, di sacca, di rey di nahe.

Dafa mel saa yu nu seetaance Television yi jef yu naaw yiy dow chester saay-saay moo ko waral mom akay Haritam. Waaya mbaa ham ngeen ki nekka ci ganaawi mbir yooyu yepp (genneel saakobi) sey taane la, moo nekka ci gamaasi mbir yu naaw yi yepp.


(Na beneen hale nyow) Tey am nanu beneen gan mungi. Moog jigeen jigenna bari mettit, choono. Mooy Sally feebar. Sally Saayu nekka mungi am birr bu metti ak boppa bu metti. Waaya am na noon bu koy waral. Geneel sako bi loolu degga la sey taane mooy ansi feebar ci nit yi.


Freddy Ragal, Nun nepp musna noo tassee ak moom. Soo ko gisee rekk hamal ne dara yengu na walla lampa yi fay nan. Waay saa yunu ko deggee nanu ham ku ko waral. (Geneel saako bi) Seytaane moo ko waral.




Nyenentechi hale bi na nyowl. Am na ku des. Kooku mooy polly nakka. Nakka du caahan. Polly nakkut rekk em ci waaya dafa tilim te bon. Leegi ham nanu ne nooni yalla mooy sey taane te mooy waral tiisak musiba yi ak nakka gi.


Seytaane mooy waral Ragal, Feebar, nakka ak kataa ak bakaar.


Sey taane dafa doon fehe ngir jetoo Bur Herod ngi re Yeesu bi mu kekkee liir. Yenna saayi seytaane daf dee bugga jel nit yi ngir tahawal ligeeyi Yalla.


Ndah seytaane mus na laa jeema tere nga def ligeeyi Yalla. Hej na mus naa am nit ku mu jel ngir koo ku yaha sa eene. Wah nu mumu demeewoon ak naka la yahee sa ligeey.


LAJTE YI


1. Kan mooy waral ay yi ak kasaara yi ci adina?

2. Lu tahoon Yalla gennee seytaan, daha ko mu genna arjana?

3. Naata malaka noo andoon ak seytaane nuy heeh ak Yalla?

4. Lu seytaane di jeem, ganaaw bi mu lamee ne du munal Yalla dara?

5. Naka la sey taane def be duga si ci biir Adina?

6. Kan la seytaane weccee ku ganaaw bu Adama ak Awa bakaaree?

7. Ganaaw bu nit yi daanoo ci bakaar, ian la Yalla wah seytaane?

8. Naka la Yalla fehe ngir yaha dooley seytaane?

9. Lu tah Yeesu dudu te bakaari Adama tahut ko?

10. Zu tah Yeesu muna nekka sunu sarah, musal nu ci sunu bakaar?

11. Lujot seytaane ak nguuram, bi Yeesu feyee sunuy bakaar?

12. Lutahoon seytaane bugga rey Yeesu bi mu nekkee hale?

13. Lan la seytaane sohla woon, ndah mu muna def peheem bu bon boobn di rey Yeesu bi mu nekkee hale?

14. Naka ngay hamee ne nit ki mungi ci lohoo Yalla walla mungi ci loho seytaane?

15. Kan la seytaan jeloon ngir jeema rey Yeesu bi nekkee hale?

16. Tudal naari mbir yi seytaane di muna duggee ci sunu dunda.

17. Lu doon wara hew sufekkoon ne danu rey Yeesu te fekka daajn nu ko ci kow cross bi?

18. Ndah seytaane hamoon na ne Yeesu mooy sarah bi Yalla nangu ngir sunny bakaar?

19. Ban ndigal la Bur Herod johe ngir muna jot Yeesu rey ko.

20. Naka lanuy yahee ligeeyi seytaan ci sunu dunda?













LESSON 5



HALE BU GOOR BI MUSUTA BAKAAR



Nujanga: LUK 2.40 - 52


Deggagi: Am nanu doolee not bakaar eeg ci kowam


Bulfate: ROMANS 6:14, Bakaar du la mun


Wahtaan Wi: Bakaar du suma kilifa


Nujanga: Ndokeel namu la


Nu Seetaan: Mariyama (601) Yuduta (602), Mbaam mi (603) Dekka bi (611) Bi Yeesu nekke hale (615) Serin yu mag yi (616)


Yow Jangalekat bi:


Li tah kenn du muna jub ci sarta yi luwa yi musaa yi mooy bakaar data jahasoo ci biir holi doom Adama. Nit ki dinga am eene def lu baah waay doo am doole bu la mey nga def loolu - (ROMANS 7.20). Ci jamano yenent Yalla musaa, dereti rab yi noo de muur bakaari nit yi. Waay ci jamano ju ees ji di damano Yeesu, dereti Yeesu mooy rahas sunuy bakaar.


Li tah Yeesu nyow mooy mu joh nit yi doole ndah nu muna dunda nimu dundee, dunda gu andul ak bakaar, gu andul ak feebar ak nakka. Yeesu dundam la dee teg ci cunu run, ker bu nu joddooo bu ees ci hel musella mi. Loolu mooy tah nu am doole dunda ni Yeesu.


I Bi Yeesu magge nkka hale bugoor, mu door di janga mbiri papaam; Yalla.


A. Yalla dina nekka sunu papa sunu nangoo. Ueesu nekka suru borom.


1. Yalla mooy baayi sunu run (HEBREWS 12:9)

2. Nu nekka doomi Yalla ( 1 JOHN 3:3)


A. Ueesu Janga na mbiri Yalla ci teere yonenti Yalla musaa.


1. Yalla ci kadoom la dee feenalee bopam.

2. Yeesu dafa feesal holam tep ak kaddu Yalla gi mu jangee ci teere yi, danu wara seet ci moom nu toppa ndoor ko.


C. Bi Yeesu doom janga teere yi dafa ci daan jangaale ay mbiram.


1. Teere yonent Yalla musaa bi in bari la wah ci mbiri Yeesu.

2. Ndegem Yeesu nit la kom nun, dafa wara jang kom nun.


D. Sunu jangee teere Yalla yi, dinan nu jagal nu ham fan la nu Yalla teg ci biir Yeesu Krista.


1. Nun nooy njubte Yall (11 CORENTIANS 5:21)

2. Nun danu sella te aminn sikka-sikka ci kanam Yalla ( EFES 1:4)

3. Nun ay jambaar ianu ci lu nekka (ROMANS 8:37)


II Bi Yeesu amee sukki at ak naar, mu anda ak ay waajuram ak yeneen waa nasaret di dem yeru salam.


A. Ay waajuri Yeesu at bu nekka dam dee dem maggati ca Yerudalam.


1. Maggal gi mooy mnaggal gi waaa Israyil di def ngir fateleku ba leen Yall musalee ca Egypt.

2. Maggal gii nag, Yalla a ko santaane ngir muy misal muy wone li leen Almasi bi wara defal su nyowee.

3. Sunu jamano jii nag sunuy jel reeri borom bi loolu moo nay fatelil li nu Yeesu defal.